NICOLAS MACHIAVEL mi gi juddo ci dëkk bu ñu nan Florence ca Italie ci atum 1469 .Gen na aduna ci atum 1527 . Mi gi siiwe ci àdduna ak terem bi tud "Le Prince " . Bind na yenen téere yu ñu rañe maanaam " Dell' Arte della guerra " (xamxamu xare ) , "Discorsi sulla prima deca di Tito Livio "(waxtaan ci fuki at yu jëk yu Tite Live" ak yenen . Sunu kaddu gi da nu ko y yamale(yemale) ci "Le prince " .

Jamono bi Machiavel di bind teere bi booba fekk na Italie nekkon ay diiwan yuy xiiroo . Li mu jublu woon mo di won jit wu ne nan ngay def ba dëgaral sa nguur .Seetuci woon nak lu jub ba lu jubadi .Teere bi bi nu ko sotte jur na coow lu bare .Ndax jamono jooju da ño jappni li muy jangale mengoowul ak diine mengoowul ak yoon . Ci sunu gëstu bi da no top tëralam bi mu jëfandikoo ci teerem bi.

Xaac 1: Ñata xetu nguur mo am ak nan la nu koy ame

Machiavel mi gi rañe nguur yi ga xam ne buur mo len di jiite ak yeneen yi yuy fal njiit li .

Réewu buur yi xaaj na len ci ñar : nguur gi nu donn ak yu bees yi .

Nena : "reew yi ñu donn moy yi yàag ci kër buur bi ." " reew yu bees yi moy yi nu yokk ci dono"

CI gis-gisam reew yi nu am : des na ko am ak ngànnaayu jaambur wala say yos , wala ndax wërsëg , wala jiko ju rafet .

Xaac 2 : Reewu yi nu donn

Ci gis-gisu Machiavel réew yi nu donn ño gëna yomba jiite réew yu bees yi ndax te nit yi tamm nanu déggal wa kër bur bi .Na bur bi baña wesu àppi maamam yi ta teey waxtu yënguyëngu yi .Bu saxe ci yon wowu lu katanam new new di na mëna denc nguuram gannaaw xew-xew bu ñu manula waajal wacceko ta bu booba itam man na yaakar su jiit ku bees ki fakkastalo rek di na ko mëna wutu.

Xaac 3 Nguur yi rax Ci fi nak la Gorgi Machiavel di wone xalatam ci nguur .

Nguur gi rax moy reew mi nu taqale benen reew . " Ci reew mu bees bi la coono yep daje ndax nit dafa bëgg soppi kilifa di yakar ku bees ki gën ka dem.Bu nu gise ni jiit lu bees li mi gi len di tek coono ndax toppatoo xare yi ak ñoom-seen danuy bëgga dellu.

Buur bu bees bi dafay noonoo : benn ak ñi mu xañ seen teraanga , ñaar ak ñi ko jappalewoon ba mu am ndam ndax mënul leen bégal ni nu ko yaakaarewoon te mënuleen toroxal ndax kollëre gi dox seen diggante .

Machiavel nena lu buur am kattan ak ay xarem soxla na ndimmalu wa reew wi muy saku gir mën fa dugg.

Pexe yi muy digal buur nak yi la

- jiite ñu mësul mom seen bopp lu yomb la : na buur bi raafal xeetu buur bi mu wutu ta bayi nit yi ñu dund ak seeni aada rek jamm ne ñoy .

Su feke ni rew mi ga saku dafa sore ta bokkuleen aada , benn pexe rek : sanc fa .Nonu la Turc yi noote Grec yi .

Nena bu buur bi sance ci reew mu bees mi di na mëna fac yàq-yàq gu jib bala muy ëpp loxo .